🌴WAXI SERIÑ TUUBAA🌴
▬ஜ۩۞۩ஜ▬
[ Yoonu Magal]
*Leerug Tuubaa*, Part 2
SËRIÑ TUUBAA bimuy jugge Tuubaa di jëm Mbakke Baary, lim bimu àndal ci ay taalibe mat na juroomi téméer yu manqué juroom ñatt (492). Mag ñi doon ay takder (ñi doon tarbiyu) doon ñetti téméer , ñi ànd ak ay soxna mat teméer ay ñaar fukk, ñi weesu ag gonne tuuti mat juroom ñaar fukk ak ñaar...
Biñu demee bay dem, SËRIÑ BI genn ba jub fas wa, taxaw ni : ana Mbakke Buso ? Mu dikk mu ni ko damalaa bëgg a wax kàddu yu gatt nga jottaliko fere yi, te buko yokk te buko waññi.
Dëkk bii tudd Tuubaa, juroom ñaari at laa fi am, juroom ñaari at yima fi am ñaar rekk laa fi nekkee woon. Ñaar yooya ku fi nekk te nekkee ko fi danga am jamm tay, danga am jamm ëllëg, fuma nekk nga fekk ma fa ! Koo xamni kuuj (rax) nga ci dara ci sab néeg, boo demee ba am lu la naxari, loolee nga ca kuujoon moola ko yobbee !
Ñaar yooyu mooy : bëgg YALLAH ak YÓNNENT BI (Saws)
▬▬▬▬
📚 Source : Waxtaani SËRIÑ TUUBAA VOL5