Sëriñ Ma-Bànji Njaay Xujja Bàlla neena Sëriñ Tuubaa waxtu wii ginaaw Tàkkusaan la génn, Tàllal leen xasiida gii ne leen, suma leen waxee lim man ci nit ki, dootu ma gis ku may duyal sama satala gi, Xasiida gu am solo la te bari kaaraange lool, comme jamono neexul, suma sañoon ñu gën koo fonk diko jàng bu baax, Maa ngi seet lu nag am ñuy wax ne boo koy jàng lu bari kaaraange gi day ëpp dem ba tëj la, loolu dëgg la, waaye xaaral ma jox leen ci secret mooy caabi ji. Mooy waxtu wii Sëriñ Tuubaa joxe woon ko di ginaaw tàkkusaan mooy waxtu wi ci gën ci jàng ko te du am benn jafe-jafe insaallaa.
56
12
10May 21, 2025 16.1K